![]() Aar ak nataal ñooy la mu
bëgg si xolam, wante mbirum làkki réew mi la jàng sa Iniwersité. Bëre na li muy
yëngu ngir jàppale mbokki artistam yi, ngir ñu mëna am ay bunt yunu jaaye seeni
liggeey. Umar Faal nak mooy njiitu kuréel gi nu duppee SEMEtt, maanaam àp mbooloo guy
yëngu ngir suqali réewi Afrig yi ngir ñu baña jëggaani. Yëngëtu SEMEtt nak a ngi
wééru si ñàtti ponkk, maanaam mbirum njàng ak jottali xibaar ak caada. Si noonu, Umar Faal
jot naa liggéey ñaari at sa DVERC, doon xelal kilifa bérepu boobe si mbirum caada. Moom de yamul foofu, ndaxte bamu fa jogee si la dem IFAN liggéey fa
tamit ñaari at si waar wu tudd "Biens culturels africains". Leegi mi ngi feete Almaañ sa Institut für Ethnologie und Afrikasutudien ngir jeexale fa gëstu gu am solo si mbirum caada ak lakki xeet yi nekk Senegaal. Lii nak, yàqalu ka dara si Aar bi muy def. Ndaxte mi ngiy bind téeré bu am solo buy nara yombal lool njàngaleem Stylographie si àddina bi. Umar de yamul foofu, ndaxte mi ngiy defar nataal yu yees si mbirum diine. Li ka taxa jok mooy waane nan la nit ñi si àadduna bi wërkepp di tëgg ay naataal ak xammeekaay yiy wane seeni ngëm. Li mu si jubblu mooy wane pasteef mi doomu Aadama yi si kaw suuf si am si mbirum diinee ak ngëm-ngëm. Li ëpp solo si liggeey wi mooy mandarga yi niñ ñi sos ngir wone seen ngëm. Umar Faal de jàpp na ni, liggëyam bii di na yokk yërmaande ak ubeeku aji ngëm yi. Liide firnde wu wóor la daal wuy tekki ni, fumu mën ti nekk Umaar Faal mii, yitewoona lool mbirum jàmm ak yërmaande si nekkinu doomu Aadama yi |
