Site owners

  • Papa Oumar Fall


58days since
9th anniversary of STYLOCULTURE

Exhibition : STYLOGRAPHIE (or Ballpoint Pen Art)

You are artist. The ballpoint pen serves  as a medium to carry your work.

You want to participate, as an artist-partner, to a collective exhibition of Stylographie.

I expect your message to: admin@styloculture.org or 0049 1765 2438099


> Ba may door

posted Dec 18, 2010 8:41 AM by Papa Oumar Fall   [ updated Dec 22, 2011 3:27 AM ]
Ba may door kaf lanu ka jappewoon. Waaye ña ma  daan andal, sa ekkol Ngalandu Juuf bu Mermuus, xamoon nanu ni caaxaan ak kaf taxumawoon jok.Loo doonul taalibee, doo si doon mukk sëriñ su xereñ sunu wekit. Biip xel mooma gunge si sama liggeey.

Bamay door, genne li ma doon xalaat te di ka yëggit, mooma taxoona jok. Rëdd ak tomb ñooy pexe yi ma tann su may nataal. Xëlima, si nasaraan si naan « stylo », mooma doy cip rëdd ak tomb.Loolu tax na ma tudde bep liggeey bu si juddoo "Stylographie".
Sa booba jamono, di naa nangu tey ni, aar bi naroon na yobb sama xel. Xanaa fu ma toll di rëddëka-tomb-aka-bind-aka-nataal. Li gënë doy waar mooy nak, bama amee sama ñatteeli dipolomu Iniwersite lu ma si tek : bayyi jang ! Ngir lan ? Rëddëka-tombaka-bind. Ñëp fook ni danu ma liggeey. Cëy  lii !

Sa yooyu jamono si laa defar nataal yi ma dippee "Soppaliku" ak "As lëm". Took lu ëpp juroomi at, di rëdd-aki-bind. Boole siyit tukki yu tar si biir Senegaal. Lii taxoon na ñu raññee ma si mbirum Stylographie si biir ak bitim reew. Noonu, Yalla boolema ak sama benn naatangoo Dominik Buse.


Samay jokkaleenteek Buse, si laa defaraala sit Internet Styloculture si atum 2002. Soo ka waññee mu jox juroom ñatti atu Internet. Looloo tax du ma took ayu bes bu ma jotul leetar ñuy begee sama liggeey.Ku yagg si teen, baag fekk la fa.

Ba nga xameenteni, li ma doon wut am naa ko, si laa ni nak, dellu iniwersite jot na. Si noonu, laa dem Lingistik, maanaam jàng xamxam bu ma mëna tax, wenn làkk du nekkati kumpë si man.

Leegi maa ngiy liggeey ak gëstu Almaañ. Du ma tere dem Senegaal, bu ma nàmmee sama njaboot ak samay soppe.